Dem dëj a gën wàlli bernde, mooy muju képp. Kuy dund, sóoraale ko.
TSK
TSK · 1 Peter 4:7
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
«Léegi nag, yaw nit ki, Boroom bi Aji Sax ji dafa wax réewum Israyil ne ko: “Jeex na tàkk! Jeexal dikkal na ñeenti weti réew mi.
¶ «Moytuleena yaafusal seen bopp ci naan gu ëpp ak màndite ak xalaati àddina, lu ko moy bés ba jekki dal ci seen kaw,
Mu ne leen: «Lu ngeen di nelaw? Jógleen ñaan, ngir baña tàbbi cig fiir.»
¶ Li tax ngeen wara gëna farlu ci loolu mooy, xam ngeen jant yi nu tollu; seen waxtuw yewwu jot na ba noppi, nde léegi la nu mucc gëna jege ba nuy doora gëm.
Gannaaw loolu la muj ga, te ca lay delloo nguur gi kiy Yàlla, di Baay, fekk mu neenal mboolem luy kilifteef, ak mboolem sañ-sañ ak doole.
Na seen lewetaay wóor ñépp, Sang bi jegesi na.
Kon nag bunu nelaw ni ñi ci des, waaye nanu teewlu, te ànd ak sunu sago.
Yiw woowu moo nu digal nu dëddu ñeme Yàlla, ak xemmemtéefi àddina, te jiital sunum xel, di jëfe njub, te nekke ag njullite ci àddinay tey jii.
Yeen itam muñleen te takk seenu fit, ndax bés ba Boroom biy dikk dëgmal na.
¶ Naka noonu yeen góor ñi, bàyyileen xel ni ngeen dëkke ak seeni jabar, tey sóoraale néew dooley jigéen. Séddleen leen teraangay nawle, gannaaw yeena bokk wenn yiw wi leen may ngeen dund dëgg. Su ko defee dara du gàllankoor seeni ñaan.
Du caageenu yeexe gu Boroom bi yeexe dige ba, noonu ko ñenn ñi fooge ag yeex. Yeen la muñal kay, ndax buggul kenn sànku, xanaa ñépp dem ba tuub.
¶ Mu ne: «Maa ngi nii yoot, di dikk nib sàcc. Ndokklee, yaw mi teewlu, fàggu say yére, ba doo deme gàcceg yaramu neen, ñu di la seetaan.»