TSK

TSK · 1 Samuel 20:13

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage
Ruth 1:17 TSK

Foo deeye it, ma deeye fa, ñu denc ma fa. Yal na ma Aji Sax ji teg mbugal mu gëna tar, ndegam lenn lu moy dee tàggale na maak yaw.»

Bu la firnde yooyu dikkalee rekk, xamal ne Yàllaa ngi ànd ak yaw. Su boobaa, lu bés bi laaj, def ko.

¶ Gannaaw ba Sóol feddlee nguuram ca Israyil, xare naak seen noon ya leen wër yépp: Mowabeen ñaak Amoneen ñaak Edomeen ñaak buuri waa Soba, ak waa Filisti. Mboolem fu mu walbatiku rekk, moo daan.

¶ Sóol daldi ragal Daawuda, ndax booba xam na ne Aji Sax jee ko dëddu, ànd ak Daawuda.

¶ Gannaaw gi mbooloo mépp di soññ Daawuda, ngir mu lekk, balaa jant a so. Daawuda daldi giñ ne: «Yal na ma Yàlla teg mbugal mu gëna tar ndegam maa sex dugub mbaa ñam wu mu doon, te jant sowul.»

Yeen de yeenay bokki buur lenqe, ngeen bokk ak moom jenn deret; kon xanaa ñépp duñu délloosi Buur, ngeen des gannaaw?”

Ben Addàd dellu yeble ca moom ne ko: «Yal na ma tuur yi teg mbugal mu gëna tar, ndegam duma tas Samari, ba pëndu tabax du fi des buy fees loxoy mboolem ñi ma topp.»

Li ngeen jànge ci man te jële ko ci man, ak li ngeen dégge ci man, gise ko ci man, jëfeleen ko. Su boobaa Yàlla miy boroom jàmm mooy ànd ak yeen.