TSK

TSK · 2 Corinthians 12:21

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Ba mu ko defee Musaa dellu ci Aji Sax ji, ne ko: «Éey Aji Sax ji, mbooloo mii de moy nañu la lool, ba ñu sàkkalee seen bopp ay yàllay wurus.

¶ Maa daanu tëdd fa kanam Aji Sax ji diiru ñeent fukki bëccëg yooyu, ak ñeent fukki guddi ya ma tëdd fa kanamam ndax la Aji Sax ji noon da leen di sànk.

Ezra 9:3 TSK

¶ Ba ma déggee loolu damaa xotti sama turki ak sama mbubb, xuuf sama kawaru bopp ak sama sikkim, daldi toog, ne tott.

ay wali rongooñ ay wale saay gët, ndax sàmmeesul saw yoon.

Bu ngeen déggul de, ma làqu, jooy seen reewande, sama rongooñ tuuroo tuuru, ma jooya jooy, nde dees na jàpp géttu Aji Sax ji, yóbbu.

Li may wax moo di tiis wu réy laa am, ak naqaru xol wu dakkul,

¶ Déggees na nag ci lu wér, ne powum séy am na ci seen biir, te powum séy mu ni mel, giseesu ko sax ci biir xeeti yéefar yi. Dem na sax ba nit nekk ak jabaru baayam.

¶ Am xamuleen ne aji jubadi ñi amuñu cér ci nguurug Yàlla? Bu leen kenn nax: Muy fokati séy yi, di bokkaalekat yi, di jaalookat yi, di góor-jigéen yi, ak ñiy ànd ak ñoom,

¶ Man nag li ma dogu mooy lii: Du teg leen aw naqar laay délsee ci yeen,

Kon nag wonleen leen lu firndeel seen cofeel ci ñoom, ak ci kanam mboolooy gëmkat ñi, firndeel itam ne noo yey wóolu leen.

Te keroog bu seen dégg ndigal matee, fas nanu yéenee mbugal képp ku déggadi.

La ma waxoon ba noppi ca sama ñaareelu ngan, tey bi ma wuutee, moom laay baamtu, artoo ko ñi jëkkoona bàkkaar, ak ñi ci des ñépp: su ma délsee, duma ñéeblu kenn,

Ndax lii kat na leen wóor: képp ku nekke powum séy, mbaa jëfi sobe, mbaa ag bëgge, kooku amul cér ci nguurug Almasi ak Yàlla, ndax ku bëgge ab bokkaalekat la.

¶ Kon nag reyleen seen cér yi bokk fii ci kaw suuf; lu mel ni powum séy, ak jëfi sobe, ak ñàkk sago ci lu jekkadi, ak xemmemtéef yu bon, ak bëgge, te loolooy bokkaale ba tey,

¶ Na ñépp wormaal diggante bu ab séy dox, te ab lalu séy na mucc sobe, ndax fokati séy yi, ak jaalookat yi, Yàlla moo leen di daan.

¶ Rawatina nag boroom xemmemtéefi yàqute, yi topp seen bakkan te faalewuñu genn kilifteef. Ñu fétteeral lañu te bew, ragaluñoo saaga sax boroom daraja yu kawe ya fa asamaan.

Jude 1:7 TSK

Naka noonu itam Sodom ak Gomor, ak dëkk ya leen wër, ñoo yebu woon ci powum séy, ak jaxasoo gu woroo ak bindub judduwaale, ba ñu def leen misaal, ñeel ña nara tegoo mbugalum sawara wu sax dàkk.

waaye ñu ragal ñi ak aji gëmadi ñi ak defkati ñaawtéef yi ak bóomkat yi ak moykat yi ak xërëmkat yi ak bokkaalekat yi, mboolem niti fen ñi, seen añ a nga ca déegu sawara waak tamarax ba. Loolu moo di ñaareelu dee.»

¶ Kiy seede mbir yii nee: «Waawaaw, maa ngi ñëw léegi.» Amiin, Sang Yeesu, ñëwal!