TSK

TSK · 2 Kings 13:4

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Su dul woon ak sama Yàllay baay, ji ànd ak man, di Yàllay Ibraayma, ji Isaaxa wormaaloon, konoon nga dàq ma tey, ma dem loxoy neen. Waaye sama toskare ak sama àqu ñaq la Yàlla gis, ba tax mu àtte ma ak yaw biig.»

Yuux, yi bànni Israyil nekke nii, agsi na ba ci man, te gis naa it ni leen waa Misra di note.

Aji Sax ji nag baaxe leen, yërëm leen, geesu leen ndax kóllëreem ak Ibraaymaak Isaaxaak Yanqóoba. Looloo tax buggu leena faagaagal, te ba tey jii xalabu leen.

Job 22:27 TSK

di ko ñaan, mu di la nangul, yaw it ngay wàccook say dige,

Ba leen Yàlla fàddee, ña des sàkku ko, tuub, waññiku ci moom.

Éy Aji Sax ji, ci biir njàqare lañu la sàkkoo; ba ñu tegoo sa mbugal, lañu la déey seenug ñaan.

ñoom ñii naa bii bant: “Yaay sunu baay,” naan wee doj: “Yaa nu sukk, jur.” Wonuñu ma kanam, xanaa gannaaw, te bu leen musiba dikkalee, ñu naa: “Wallu nu boog!”