Buleen seet fi mbooloo gëna baree, ngeen topp leen ci jëf ju bon; te it buleen jeng, di topp mbooloo mu gëna bare ci ab layoo, di leen seedeel lu toxal dëgg.
TSK
TSK · 2 Peter 3:16
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Buleen jalgati yoon cib àtte, buleen jeng te buleen nangu alalu ger, ndax ab ger day muur bëti boroom xel, di xañ aji jub dëgg.
¶ Ba Axab buurub Israyil saayee yàggul dara, Mowabeen ña dañoo fippu, jógal doomam Buur Akasiya. Mu am bés Akasiya tollu biir néegam ca kaw taaxum këram ga ca Samari, daldi xàwwikoo ca palanteer ba, daanu ba gaañu lool. Gannaaw gi mu yónni ay ndaw, ne leen: «Demleen seetal ma ca Baal Sebub, tuuru Ekkron, ba xam ndax dinaa dund gannaaw jéll bii ma daanu.»
Waaye yéeneb waxyu bu Aji Sax ji, buleen ko fi tuddati. Jooju wax déy, yenu boroom lay doon. Ndax dangeena been sunu kàddug Yàlla, Yàlla Aji Sax jiy dund, Boroom gàngoori xare yi.
¶ Léegi nag bokk yi, ma fàttli leen xibaaru jàmm bi ma leen xibaaroon, muy lu ngeen gëm, sax ci,
¶ Li ci des nag, bokk yi, moo di yeena nangoo ci sunu làmmiñ, jëfin wi ngeen wara jëfe ba neex Yàlla, te it moom ngeen nekke. Waaye danu leen di tinu, di leen ñaax, ci turu Sang Yeesu, ngir ngeen gënati koo jëfe.
¶ Moomu mbir nag bare na lu nu ciy wax, waaye tekki ko mooy jafe ndax seen déggin wu diib.
¶ Ci man Piyeer, ndawal Yeesu Almasi la bataaxal bii bawoo, ñeel askan wi Yàlla taamu, te ñu toxuji diiwaani Pont ak Galasi ak Kapados ak Asi ak Bitini.
¶ Waaye na mu ame woon ci askanu bànni Israyil ay yonenti caaxaan, ni lay ame ci seen biir ay sëriñi caaxaan yuy sërxal ay àlluway sànkute yuy weddi sax Sang bi leen jot, ba yóbbe seen bopp sànkute ju bette.
Ndaxte ñenn a ngi ñu ñu yàgga bind seenub àtte, te ñoo yoxoosu ci seen biir, di ñu ñeme Yàlla; ñooy taafantoo yiwu Yàlla ngir yoonal ag yàqute, di weddi Buur biy kenn, te di sunu Boroom Yeesu Almasi.