TSK

TSK · 2 Peter 3:4

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Lóot daldi génn, wax ak goroom, ya naroona takk ay doomam yu jigéen, ne leen: «Gaawleen gaaw, génn dëkk bi, ndaxte Aji Sax ji dina ko tas.» Teewul ñu defe ne day kaf.

Jëf ñaaw na, mbugal ma yeex, ba tax doom aadama sóobu ci mbon.

Mu ne: «Ñoo fenal Aji Sax ji, naan: “Moom du def dara, musiba du nu dal, saamaroo, xiifoo, dunu ci gis dara.

Ñu ngi naa: “Bunu tabaxagum ay kër; dëkk bii daa mel ni ndab, nun nu fegu ni yàpp wu ca ube.”

Soof ngeen Aji Sax ji ak seeni wax, ngeen naan: «Nu nu ko soofe?» Xanaa naan: «Képp kuy def lu bon mooy ki baax ci Aji Sax ji, te kooku la safoo.» Mbaa ngeen naa: «Ana Yàlla jiy àtte dëgg sax?»

Ndax kat, ana kan mooy sunu yaakaar, di sunu mbég, te di sunu kaala gu nuy sagooji? Xanaa du yeen, kera ca sunu kanam Boroom Yeesu, bu feeñee?