TSK

TSK · 2 Samuel 1:2

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Ca gannaaw ëllëg sa, Ibraayma daa dawal bëtam, séen bérab ba fu sore.

¶ Ba mu ko defee Ruben dellu ca kàmb ga, gis ne Yuusufa nekkatul ca biir, mu mititlu ko, ba xotti ay yéreem.

Ñu ne ko: «Sunu baay mu ngi dund, sang bi, te mu ngi ci jàmm.» Ña nga koy sukkal tey sujjóotati.

¶ Ba mu ko defee jenn waay ju bokk ci giirug Beñamin, dawe ca làngu xare ba ca Silo ci benn bés bi. Mu agsee yére yu xottiku ak bopp bu fees ak suuf, di ko tiisloo.

Xale ba dem, Daawuda jóg, génne ca làquwaayam ba fare bëj-saalum. Mu ne gurub, dëpp jëëm fa suuf, sujjóot ñetti yoon, ku nekk fóon sa moroom, ñoom ñaar ñépp jooy, te Daawuda rawati.

ka ma tàggesi woon Sóol, foog ne xibaaru jàmm la ma indil, dama koo jàpp, rey ko ca Ciglaag, yoole ko ko xibaaram.

¶ Jigéen ja dëkk Tekowa àgg ca Buur, daanu ci suuf, sujjóotal ko, ne ko: «Buur, wallu ma!»

¶ Ba mu ko defee Arawna séen Buur, mu ànd aki jawriñam, jëm ca moom. Mu génn sujjóotal ko, dëpp jëëm ca suuf,

¶ Ba mu amee ñetti fan Esteer sol yérey lingeer, taxaw fa janook kër buur ca ëttu biiram, fekk Buur toog ca ngànguneem, ca biir néegam, janook buntu kër ga.

Hosea 6:2 TSK

Ñaari fan, mu leqli nu, ñetteel ba mu yékkati nu, nuy dund fi kanamam.

Ñenn ci jàngub Seytaane bi, ñooñuy fen, di tuddoo ay Yawut te duñuy Yawut, maa ngii di leen xiirtal, dikkloo leen, sujjóotloo leen fi sa kanam, ba ñu xam ne man maa la sopp.