TSK

TSK · 2 Timothy 3:5

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Boroom bi nee: «Askan wii, làmmiñ lañu ma jegee, lori neen lañu may wormaale, te seen xol sore ma. Seen ragal ak man it, njàngum tari kepp la.

Aji Sax ji nee: «Xaacul loo man, te bul ñéeblu; àddul ni bufta, te yégal sama ñoñ seen bàkkaar, ngir waa kër Yanqóoba yii xam seeni moy.

yaa di jànglekatub naataxuuna yi, di sëriñub tuut-tànk yi, gannaaw yaa jagoo ci yoonu Musaa, mboolem luy jëmmu xam-xam, ak lépp luy dëgg.

¶ Su boobaa nu noppee doon ay tuut-tànk yu nit ñiy muusaatoo kàddu yu mel ni gannax yu nuy baaje, ak ngelawal mboolem àlluwa ju bees ju nuy pamti-pamtee ci seen biir pexey naxe ak njublaŋ, ngir fàbbi nu.

¶ Ku ci déggul sunu kàddu yi ñu bind ci bataaxal bii nag, bàyyileen ko xel, te baña jaxasoo ak moom, ngir gàcceel ko.

ak jote yu dul jeex yu boole ay nit ñu seenum xel mu yàqu xañ àlluway dëgg. Nit ñooñoo mbubboo ag njullite, te def ko wutukaayu alal.

Waaye werante yu xeluwul te du xam-xam, moyu ko, te xam ne ay ŋaayoo lay jur.

Ab féewalekat nag, yedd ko benn yoon ba ñaareel bi yoon, doora daggook moom,