TSK

TSK · Acts 10:22

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Nekkul it wàllaa géej ba ngeen naan: «Ana ku nuy jàllil wàllaa géej, jëlil nu ko, dégtal nu ko, ba nu jëfe ko?»

«Xol baa ngay xoggliku, te ag njub nekku ca, waaye ku jub ndax kóllëreem mooy dund.

Luke 2:25 TSK

¶ Amoon na nag ca Yerusalem ku ñuy wax Simeyon; ku juboon, ragal Yàlla, di séentu jamono ji nekkinu bànni Israyil di ame ag tan, te Noo gu Sell gi àndoon ak moom.

¶ Ndeke jenn waay ju ñuy wax Yuusufa, ma nga bokkoon ca kurélu àttekati Yawut ya. Ku baax, ku jub la woon.

Acts 10:2 TSK

Ku jullite la woon te ragal Yàlla, mook waa këram gépp; bare woon na sarax yu muy yéwéne askan wi, te ñaan ci Yàlla la saxoo woon.

Ca saa sa nag laa yeble ci yaw. Yaw it def nga lu baax, bi nga dikkee. Léegi nag nun ñépp a ngi fi ci kanam Yàlla, ngir déglu mboolem lu la Boroom bi sant.»

¶ «Ku ñuy wax Anañas nag ma nga woon ca Damaas. Ku am diiney yoonu Musaa te rafetub jëw ci biir mboolem Yawuti dëkk ba.

Ci xibaaru jàmm bi lañu feeñal ni Yàlla di joxe nit ñi àtteb ñu jub, te lépp aju ci ngëm, ca ndoorte la, ba ca njeexital la. Noonu la Mbind mi indee ne: «Ku jub ndax ngëmam mooy dund.»

Loolu lépp ci Yàlla la jóge, moom mi nu jubale ak boppam ci Almasi, te moo nu sas, ngir nuy waare juboo googu.

Sama nit ku jub nag mooy dund ndax ngëm ga, waaye ku dellu gannaaw, sama xol bégewu la.»

yeena àgg fa ndajem taaw, ya seeni tur binde fa asamaan. Yeena àgg fa Yàlla, àttekatub ñépp; yeena àgg fa noowi aji jub ña ñu matal sëkk.