TSK

TSK · Acts 11:21

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage
Ezra 7:9 TSK

Ca benn fanu weer wa jëkk la dooroon yoon woowu mu bàyyikoo Babilon. Mu agsi Yerusalem ca benn fanu juróomeelu weer wa, ci mbaaxu Yàllaam ji ko toppe yiwam.

akub bataaxal bu jëm ca Asaf may wattu toolu buur, ngir mu may ma bant yu ma defareji bunti tatay kër Yàlla ga, defaraale ca tatay dëkk baak kër ga may dali.» Buur nangul ma, ndax sama Yàlla ji ma toppe mbaaxam.

Ana ku gëm sunub dégtal? Ana ku Aji Sax ji won dooley përëgam?

Luke 1:66 TSK

Ña ca dégg ñépp daldi bàyyi xel ca mbir ma, te naan: «Lu xale bii nara doon ëllëg?» ngir manoorey Boroom bee àndoon ak moom.

Acts 4:4 TSK

Fekk na nag, ñu bare ca ña jotoona dégg kàddu ga gëm nañu, ba limu gëmkat ña tollu ci juróomi junni (5 000).

Acts 6:7 TSK

¶ Ba loolu amee kàddug Yàlla di law, limu taalibe yi yokku ba bare lool ci biir Yerusalem, sarxalkat yu bare daldi topp yoonu ngëm wi.

Ndaxte Barnaba nit ku baax la woon, feese Noo gu Sell gi, ak ngëm. Mbooloo mu takku nag dolliku ci Sang bi.

ngir nga xippil leen, jële leen ci lëndëm, tàbbal leen ci leer, seppee leen ci noteelu Seytaane, indi leen ci Yàlla, ñu am njéggalug bàkkaar, am cér ci biir nit ñi ñu sellal ndax ngëm, gi ñu ma gëm.”

ndax sunu xibaaru jàmm, bi nu leen àgge, dikkewu leen ay wax rekk, waaye manoore la leen dikkaale, ak ndimbalal Noo gu Sell gi, ak kóolute gu mat sëkk gu ngeen am. Xam ngeen moos na nu nekke woon ca seen biir, di xintewoo seen njariñ.