TSK

TSK · Acts 11:30

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

¶ Barnaba ak Sóol nag, gannaaw ba ñu sottalee seen liggéey, dañoo jóge Yerusalem, ñibbi, ànd ak Yowaan mi ñuy wax Màrk.

Acts 15:2 TSK

¶ Mbir ma nag mujje féewaloo ak werante wu xawa metti, te Póol ak Barnaba séq ko ak ñooñu. Ba loolu amee ñu ne, na Póol ak Barnaba, ak ñenn ca gëmkati Àncos, ànd dem Yerusalem ca ndawi Yeesu, ak mag ña, ba lijjanti mbir moomu.

Acts 15:6 TSK

¶ Ba loolu amee ndawi Yeesu yi ak mag ñi bokk daje, ngir seet mbir moomu.

Acts 16:4 TSK

Ba loolu amee ñuy wër dëkk ya, di jottli dogal yi tukkee ca ndawi Yeesu yaak magi Yerusalem, ngir ñu sàmm ko.

Ca ëllëg sa Póol ànd ak nun, seeti Yanqóoba, fekk mag ñépp a nga fa teew.

Ba nu ñaanee Tit mu dikk ba ci yeen, nangul na nu, waaye yemu ca, nde ci xéraangeem la yebul boppam ne mooy dikk ba ci yeen.

Bul déglu tuuma ju ñu waxal magum mbooloo mi, lu moy ci kaw kàdduy ñaari seede mbaa ñett.

Ana ku wopp ci yeen? Na woo magi mbooloom gëmkat ñi, ñu ñaanal ko, raayaale ko ag diw ci turu Boroom bi.