Naka lañu fa toxal gaal ga nag, loxol Aji Sax ji dal dëkk ba, mu jur tiitaange lu réy lool. Daa dal ca kaw dëkk ba, mag ak ndaw, ay taab ne fureet ca seen kaw.
TSK
TSK · Acts 13:11
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
¶ Bu loolu wéyee buurub Siri doon na xareek Israyil. Ci biir loolu mu diisooki surgaam, ne leen bérab sàngam lay def ab dalam.
Guddeek bëccëg sa loxo diis gann ci man. Sama doole ŋiis ni ndox mu jaas upp. Selaw.
Noppi naa, dootuma wax, yaw yaa dogal lii.
¶ Ci kaw loolu Anañas dem, dugg ca kër ga, teg Sóol loxo, ne ko: «Mbokk mi Sóol, Sang Yeesu, mi la feeñu woon ci yoon wi nga dikke, moo ma yebal ci yaw, ngir nga dellu di gis te feese Noo gu Sell gi.»
¶ Bokk yi, moytuleena defe ne seen xel mu rafet a leen may li ngeen am. Bugguma ngeen umple mii mbóot: Ag déggadi moo dikkal lennati bànni Israyil, ba kera xeet yi dul Yawut duggsi, ba seenub lim mat.
¶ Ñooñooy teen yu dëy, ñooy xiin wu callweer tas, te lëndëm gu fatt taraj di seenub añ.