TSK

TSK · Acts 13:19

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Te réew mi nga doon ab doxandéem léegi, muy réewu Kanaan mépp, jox naa la ko, yaak sa askan, ngeen moom ko fàww. Te dinaa doon seen Yàlla.»

¶ Bu leen seen Yàlla Aji Sax ji yóbboo réew ma ngeen jëm, ngir nanguji ko, moo fay dàqe xeet yu bare fi seen kanam: Etteen ñi ak Girgaseen ñi ak Amoreen ñi ak Kanaaneen ñi ak Periseen ñi ak Eween ñeek Yebuseen ñi; juróom ñaari xeet yu leen ëpp, ëpp leen doole.

Ci kaw loolu seeni doom nanguji réew ma. Yaa leen nangulal Kanaaneen ña dëkkoon ca réew ma, teg ci seeni loxo buuri réew maak baadoola ya, ñu di leen def lu leen soob.

muy Siwon buurub Amoreen ña, ak Og buuru Basan, ak buuri Kanaan ñépp.

Acts 7:45 TSK

Xayma ba la sunuy maam jot, dugal ko ci kilifteefu Yosuwe ca biir réewum xeet, ya leen Yàlla dàqal. Xayma ba nekk fa, ba ca janti Daawuda.