TSK

TSK · Acts 2:5

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Wormaal-leen màggalu bésu Ngóob mi jëkka ñore ci tool, yi ngeen di bey, ak màggalu bésu Farmàngu mi ci ndeetel at mi, gannaaw bu ngeen dajalee seen meññeef ba noppi.

«Man maa xam seeni jëf ak seeni xalaat. Bés bii taxaw lees di dajale xeetoo xeet aki làkk, ñu dikk ba niir samag leer.

Ndax ni melax di xuyye gii wetu asamaan, ba ne ràññ ca gee, noonu la Doomu nit kiy def keroog bésam.

Acts 8:2 TSK

¶ Ay nit ñu ragal Yàlla nag rob Eccen, ñaawlu deeyam lool.

Acts 10:2 TSK

Ku jullite la woon te ragal Yàlla, mook waa këram gépp; bare woon na sarax yu muy yéwéne askan wi, te ñaan ci Yàlla la saxoo woon.

Teewul Yawut ya xiirtal tuubeen yu jigéen yi gëna ràññiku, ak kàngam yu góor yi ci dëkk bi. Ñu daldi bundxatal Póol ak Barnaba, génne leen réew ma.

Noonu la deme, ndegam kay fekk na leen sësoo ngëm gu ngeen dëjoo ba dëgër, te baña nangu lenn di leen sorele ak yaakaar ji ci xibaaru jàmm, bi ngeen dégg, te ñu biral ko, ñeel mépp mbindeef. Man Póol nag, ci yégle xibaaru jàmm boobu laa di ab jawriñ.