TSK

TSK · Acts 20:16

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage
Acts 2:1 TSK

¶ Ba bésu màggalu Pàntakot agsee, ñoom ñépp a bokk daje benn bérab.

¶ Ba ñu teeree Efes, fa la Póol bàyyi Pirsil ak Akilas. Mu dem ca jàngu ba, ba diisoo fa ak Yawut ya.

¶ Gannaaw ba loolu wéyee, Póol ci ndigalal Noo gu Sell gi am mébétum jaare diiwaani Maseduwan ak Akayi, teg ca Yerusalem. Mu ne: «Gannaaw bu ma àggee foofu, war namaa jàll ba Room itam.»

¶ Nun nag nu jiituji, dugg gaal jëm Asos, fa nu nara yebe Póol, na mu ko mébéte woon, ndax Póol ci boppam moo xalaatoona jaare ci yoonu suuf si ba fekksi nu fa.

Acts 21:4 TSK

Nu seet taalibey foofa, ba gis leen, toog ak ñoom juróom ñaari fan. Ci biir loolu Noo gu Sell gi di leen xiir ci wax Póol, ne ko bumu dem Yerusalem.

bu may dem Espaañ, dinaa leen seetsiwaale. Yaakaar naa leena gis bu ma fa jaaree, ba ngeen yiwi ma, ma jàlli Espaañ, gannaaw, lu mu néew néew, ay fan yu ma nammantikoo ak yeen.