TSK

TSK · Acts 21:24

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

¶ Ba loolu amee Musaa wàcc tund wa, dellu ca mbooloo ma. Mu sell-luloo leen, ñu fóot seeni yére,

¶ «Su nit jekkee dee ci wetam, ba sobeel njañu céddoom, keroog bés buy setlu ca lay watu, te keroog bésub juróom ñaareel ba lay watu.

Su ko defee nasireen bi watu ci bunt xaymab ndaje mi te for kawari céddoom googu, def ko ci taal, bi ci suufu saraxas cantu biir jàmm bi.

Job 41:25 TSK

Amul niruwaale fi kaw suuf, mii mbindeef mu dul tiit.

¶ Ca ëllëg sa Póol ànd ak nit ña, bokk ak ñoom setlu, dugg ca kër Yàlla ga. Mu daldi xamle bés ba seen àppu setlu di mat, ba jooxe ba ci war génn, ñeel kenn ku nekk ci ñoom.

Ba ma nekkee ci biir Yawut yi, ni Yawut yi laay def, ngir iri leen. Ba ma nekkee ak ñi tegoo yoonu Musaa, damaa mel ni yoonu Musaa laa tegool, ngir iri ñi tegoo yoonu Musaa, te man ci sama bopp, tegoowuma yoonu Musaa.

Sarax yooyu, ci aw ñam ak ag naan, ak xeeti njàpp doŋŋ la jëm, lépp yittewoo yaramu suuxu neen, te di ndigal yu leen waroon ba keroog bésub coppite taxaw.