ku la ñaanal barke, ma barkeel, ku la móolu it, ma alag, te xeeti àddina sépp, ci yaw lañuy barkeele.»
TSK
TSK · Acts 26:6
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Dinaa ful sa askan ni biddiiwi asamaan, dinaa jox sa askan suuf sii sépp, te it ci saw askan la xeeti àddina sépp di barkeele,
Ab yonent bu soqikoo ci yeen kay, di seen mbokk ni man, moom la leen seen Yàlla Aji Sax ji di feeñalal. Moom ngeen di déggal.
Waaye man xam naa ne sama jotkat a ngi dund, te mooy mujje taxaw fi kaw suuf.
Yaw Aji Sax ji sama Yàlla, bare nga loo def, amuloo moroom! Bare nga kéemaan aki mébét yoo nu sottalal, ma bëgga xamle lépp, te mu bare ba wees ab lim.
Ñeel Daawuda, di kàddug Sabóor. Aji Sax ji daa wax sama Sang, ne ko: «Toogeel sama ndijoor, ba ma def say noon sa ndëggastal.»
Fa laay dooleele Daawuda, taalal ki ma fal,
Kon nag Boroom bi ci boppam moo leen di jox firnde: janq bi mooy ëmb, jur doom ju góor, tudde ko Emanuwel (mu firi Yàllaa ngeek nun).
Aw njebbit mooy saxe fa ëkkub Yese, ab car soqeekoo fa reen ya,
«Xool-leen sama jaam bi ma yor, sama tànnéef, sama soppey xol, ci kawam laa teg samag noo, te mooy dogalal xeet yi yoonu àtte.
Noowug Boroom bi Aji Sax jaa ngi fi sama kaw, ndax Aji Sax jee ma diw, fal ma, ngir ma àgge néew-doole yi xibaaru jàmm. Moo ma yebal ngir ma dëfal ñi seen xol jeex, yégal jaam yi, seen goreel, yégal ñi ñu tëj, seen ubbite.
¶ «Ay bés a ngii di ñëw,» kàddug Aji Sax jee, «maay sottal ngëneel la ma dig waa kër Israyil ak waa kër Yuda.
Fitt giy misaal Yerusalem ndijooram lay wadd. Mu sës dénki dàjjikaay yi, yéene ndigalu bóome, xaacu, daldi sës dénki dàjjikaay yi ci bunt yi, yékkati sëkk yi, ngir taxawal ab gawukaaay.
¶ «“Daawuda sama jaam baay doon seen buur, di seen bennub sàmm ñoom ñépp. Sama àttey yoon lañuy doxe, sama dogali yoon lañuy sàmm, di ko jëfe.
¶ «Ci jamonoy buur yooyu Yàlla Boroom asamaan dina samp nguur gu dul tas mukk, te wenn xeet du ko yilif mukk. Nguur googu dina tasaare mboolem yeneen nguur yooyu, ba genn du ci des, waaye moom day sax ba fàww.
¶ «Juróom ñaar fukki ayi bés lañu àppal sa mbooloo ak sab dëkk bu sell, ngir dakkal tooñ gi, jeexal moy gi, jotu ñaawtéef, saxal njubte ba fàww, matal peeñum yonent, ba delloo bérab bu sella sell ag sellngaam.
Ay xettlikat ñooy yéeg kaw tundu Siyoŋ, ngir yilif tundu Esawu, nguur gi di moomeelu Aji Sax ji.»
Yaay sàmm kóllëre ak Yanqóoba, yéwéne Ibraayma, na nga ko giñale woon sunuy maam, janti démb.
«Éey, éey yeen, dawleen génne réewum bëj-gànnaar,» kàddug Aji Sax jee. «Ni ñeenti ngelawi asamaan tasaaroo, ni laa leen tasaaree.» Kàddug Aji Sax jee.
Bégala bég, janq Siyoŋ mu taaru, janq Yerusalem mu taaru laa ne: Xaacul, sa buur a ngoog, jëmsi ci yaw, moo jot njekk ak mucc, te teewu koo woyof, war mbaam, cumbur doomu mbaam.
«Éey saamar, yewwulal sama sàmm bi, sama jàmbaar jii ma lëngool,» kàddug Aji Sax jee, Boroom gàngoor yi. «Dóoral sàmm bi, xar yi tasaaroo, ma walbati sama loxo, jublu ci jur gu ndaw gi.
¶ «Te it mboolem yonent yi wax, dale ko ci Samiyel ak ñi ko wuutu, ñoom it yégle woon nañu bés yii nuy dund.
¶ Fekk na Póol xam ne lenn ca kurél gaa nga bokk ca ngérum Sadusen ya, ña ca des bokk ca ngérum Farisen ya. Mu daldi àddu ca kaw ca biir géew ba, ne: «Bokk yi, man de ab Farisen laa, di doomu Farisen; li ñu may àttee nag mooy sunu yaakaar ak sunu ngëm gi nu bokk ci mbirum ndee-ndekki.»
Xanaa genn kàddu ga ma taxawoon ca seen biir, àddu ko ca kaw ne: “Mbirum ndee-ndekki gi ma gëm, moom lañu may àttee ci seen kanam tey!”»
Mbir moomu nag moo tax ma woolu leen, ngir giseek yeen, diisook yeen, ndax yaakaaru bànni Israyil moo waral sama jéng yii.»
Li ma ciy wax mooy lii: kóllëreg Yàlla gi taxawe ni kayitu donale gu mu dëggal, yoonu Musaa, wi dikk ñeenti téeméeri at ak fanweer gannaaw kóllëre gi, manu koo neenal, ba fomm digeb Yàlla.
Loolu lees nu digal, li feek nu ngi séentu yaakaaru mbég ma, keroog bésu peeñum sunu màggaayu Yàlla, miy Yeesu Almasi, Musalkat bi.