Doj wi tabaxkat yi beddi woon, moo mujj doju coll wi.
TSK
TSK · Acts 4:11
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Moo tax Boroom bi Aji Sax ji wax ne: «Maa ngii di dëj fi Siyoŋ aw doju coll, muy doju collu tànnéef wu gànjare ngir kenu gi, te ku ko wéeroo doo gaawa daw.
Waaye yaw nit ki, bu leen ragal, bul ragal seeni wax. Xam naa ne ay taxas aki dég a lay wër, nga toog ci kawi jiit. Waaye bul ragal seeni wax te bul tiit seen kanam doonte kërug fippukat lañu.
Su ma nee nit ku bon ki: “Dee rekk ay sa àtte,” te fekk àrtuwoo ku bon ka, waxuloo lu ko waññee ca mbonam ga, ba mu mucc, ku bon kaay dee ndax tooñam, waaye bakkanam yaw laa koy laaj.
Doj waa ngii ma teg fi kanam Yosuwe, te wenn doj wi, juróom ñaari gët a ngi ci kawam. Maa ngii di ci ñaas mbind mi ci war,» kàddug Aji Sax jee, Boroom gàngoor yi, «te maay far bàkkaaru réew mii ci benn bés.»
Kan ci yonent yi la seeni maam fitnaalul? Ñoo rey démb ña yégle woon ñëwug Aji Jub, ji ngeen wor tey, bóom ko.
¶ Gannaaw am nanu jooju yaakaar nag, fit wu réy lanuy deme,
Yeena di tabax, bi ndawi Almasi ak yonent yi di kenu gi, te Almasi Yeesu ci boppam di doju coll wi.