TSK

TSK · Acts 4:27

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage
Job 14:4 TSK

Lu sobewu, ana ku ci mana am lu laab? Du kenn!

Job 25:4 TSK

Ana nu nit di ame dëgg fa kanam Yàlla? Ku jigéen jur, nu mu mana laabe?

«Man maa tabb buur, fal ko ci Siyoŋ, sama tund wu sell.»

Aji Sax ji jotkatub Israyil, moom ku Sellam ki, moo wax ak ki xeet yi xeeb, sib ko, te muy surgawu kilifa yi, mu ne ko: «Ay buur ay gis, jóg, ay kàngam di sukk, ngir Aji Sax ji boroom worma, ngir Aji Sell ju Israyil ji la taamu.»

Noowug Boroom bi Aji Sax jaa ngi fi sama kaw, ndax Aji Sax jee ma diw, fal ma, ngir ma àgge néew-doole yi xibaaru jàmm. Moo ma yebal ngir ma dëfal ñi seen xol jeex, yégal jaam yi, seen goreel, yégal ñi ñu tëj, seen ubbite.

Luke 4:18 TSK

«Noowug Boroom baa ngi fi sama kaw, moo ma fal, ngir ma yégal néew-doole yi xibaaru jàmm bi. Da maa yebal ngir ma yégal jaam yi ne dees na leen goreel, yégal gumba yi ne dinañu gis, yégal ñi ñu not, ne dees na leen jot,

¶ Ca jamono jooju tembe la ay Farisen dikk, ne Yeesu: «Jógeel fii, te dem, ndax Buur Erodd da laa nara rey.»

¶ «Boroom tóokër ba ne: “Nan laay def nag? Naa yónni sama doomu bopp ji ma sopp boog, xanaa moom, dinañu ko rus!”

¶ Naka la Yeesu di wax, daaneelagul, mbooloo ne jimeet, ka ñuy wax Yuda, di kenn ca Fukk ñaak ñaar jiite leen. Yuda dikk ba ci Yeesu, bëgg koo fóon.

Luke 23:7 TSK

Ba mu wóoree Pilaat ne ca diiwaan, ba ca kilifteefu Erodd la Yeesu bokk, ca la ko yónnee Erodd, yemook Erodd itam nekk Yerusalem ca fan yooya.

Acts 3:13 TSK

Moom Yàllay Ibraayma, di Yàllay Isaaxa, di Yàllay Yanqóoba, te di sunu Yàllay maam kay, moo màggal jawriñam Yeesu. Yeen nag yeena ko teg ciy loxo, jàmbu ko fa kanam Pilaat, te mu naroon koo bàyyi.

ak ni Yàlla ànde ak Yeesum Nasaret, ba jagleel ko pal gu mu dogale Noo gu Sell geek xam-xam bi mu ko sotti, muy wër, di def lu baax, di faj mboolem ñi Seytaane notoon.