¶ Aji Sax ji dellu ne Musaa: «Maa gis askan wii, askan wu dëgër bopp a ngii!
TSK
TSK · Acts 7:51
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
¶ Fekk na Aji Sax ji wax Musaa ne ko: «Waxal bànni Israyil ne leen, ñoom askan wu dëgër bopp lañu. Su ma àndoon ak ñoom ab diir rekk, dinaa leen faagaagal. Kon nag nañu tàggook seeni gànjar, ba ma seet nu may def ak ñoom.»
ba man itam ma noonoo leen, toxal leen seen réewu noon. Bu ñu tuubee seen xol bu dëgër nag, ba matal seen mbugal yi sababoo ci seeni ñaawtéef,
¶ Aji Sax ji waxati ma, ne ma: «Gis naa ne mbooloo mii kat, ñu dëgër bopp lañu.
Su boobaa seen Yàlla Aji Sax jee leen di xarfal xarafu xol, te mooy xarfal xarafu xol, seen askan, ngir ngeen soppe seen Yàlla Aji Sax ji seen léppi xol, ak seen léppi bakkan, ndax ngeen dund.
Ndaxam muñal nga leen ay at yu bare, di leen artoo sam xel, say yonent di leen ko jottli; waaye taxul ñu déglu. Nga teg leen nag ci loxoy waa réew yi.
te baña roy seeni maam; maas gu të woon te déggadi, ñu ñàkk pastéef te sàmmuñu kóllërey Yàlla.
Waaye ñoom ñoo fippu, di naqaral xelam mu sell, mu soppliku seen noon, ba mujj di xareek ñoom.
Moo kan laay waxal, àrtu ko ba mu déglu, yii boroom noppi paaxee tëë teewlu! Kàddug Aji Sax jaa ngii, mel ni lu ñu rus, lu ñu safoowul!
Ndaxam dégluwñu ma, teewluwñu ma, xanaa të ticc, baña dégg, di gàntal ndigal.
Bu ngeen ma daan indil sama céru ñam, muy nebbon, di deretu sarax yi, dangeen di dugalaale sama biir bérab bu sell bi ay doxandéem yu xaraful, du ci jëmm, du ci xol. Noonu ngeen sobeele sama kër gi. Fecci ngeen sama kóllëreek yeen ndax seen jépp jëf ju siblu.
¶ Teewul ñu baña déglu, të ticc, fatt seeni nopp, ngir baña dégg.
Teewul àttanuñu xelam mu rafet, ak Noo gi muy waxe.
Ka doon néewal doole moroom ma bëmëx Musaa, ne ko: “Yaw, ku la def njiit mbaa àttekat ci sunu kaw?
Kooku la sunuy maam nanguwul woona déggal. Dañu koo far xarab, namma walbatiku dellu Misra.
Ab Yawut, du ci melo wuy feeñ lees koy nekke, te xaraf it du ci màndarga muy feeñ ciw yaram.
Ndaxte nun noo xaraf tigi, nun ñiy jaamoo Yàlla Noowam gu Sell, di damoo Almasi Yeesu, te yaakaarunu aaday nitu suuxu neen.