TSK

TSK · Amos 4:13

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Musaa tàllal loxoom, mu jublu asamaan, lëndëm gu fatt wàcc ca kaw réewum Misra gépp, diiru ñetti fan.

Moo leen waral kawtey réew ma, ñuy xontoo meññeefum àll bi, mu di leen nàmpale lem ju walew doj, ak diw gu balle xeer wu ne sereŋ,

Job 9:7 TSK

Keey gëdd jant bi, aaye koo fenk, ub ràpp biddiiwi asamaan.

Defal nga nuy kéemaan, nangug ñaan ci njekk, yaw Yàlla, mi nuy wallu, di yaakaaru àddina wërngal këpp, ba ca géej gu sore ga.

yaa xam sama toogaay ak sama taxawaay, di ràññee fu sore samay xalaat,

Bésub keroog ñu ŋaral Yuda, ŋar yu mel ni géej gu sàmbaraax! Foo geesu ci réew mi, xool, doo gis lu moy lëndëm ak njàqare, xàmbaar maase, ba leer giim.

Maay bind leer, di def lëndëm. Maay indi jàmm, di def safaan. Maay Aji Sax jiy def lii lépp!

moona yeena ngi sagoo turu dëkk bu sell bi, di wéeroo Yàllay Israyil ji turam di Aji Sax ji Boroom gàngoor yi.

Ki séddoo Yanqóoba déy wuute naak yii caaxaan. Kookoo bind lépp, te Israyil di giir gi mu séddoo. Kookooy Aji Sax ji Boroom gàngoori xare yi!

«Giñ naa ko ci man miy dund,» kàddug Buur Aji Sax jee, Boroom gàngoor yi di turam: «noon ay dikk, mel ni tundu Tabor ci digg tund yi, mbete tundu Karmel wi feggook géej.

Séddoob Yanqóoba déy wuute naak yii caaxaan. Kee bind lépp, bind giir gi mu séddoo. Kookooy Aji Sax ji Boroom gàngoori xare yi!

Aji Sax ji Yàlla Boroom gàngoor yi, Aji Sax jee di turu bàkkam.

Amos 5:8 TSK

Kee sàkk biddiiwi lolli ak biddiiwi cooroon, mooy walbati lëndëm bët set, def bëccëg di guddi. Keey woo walum géej, walal fi kaw suuf. Kookoo di Aji Sax ji.

Amos 6:8 TSK

Boroom bi, Aji Sax jee ko giñ ci boppam, kàddug Aji Sax ji Yàllaa, Boroom gàngoori xare yi. Nee: «Maaka sib réy-réylug askanu Yanqóoba, ba seen kër yu yànj soof ma! Maay jébbale seen péey ak mboolem li ci biir.

Amos 9:6 TSK

Kee tabax kaw asamaan néegi biiram, samp ub xaddam, yiire suuf. Keey woo walum géej, walal fi kaw suuf. Kookoo di Aji Sax ji.

Aji Sax ji Boroom bi mooy sama doole, moo ma defal samay tànk mel ni yoy kéwél, te fa kawte ya la may daaguloo. Mu jëm ci njiital jàngkat yi, ànd ak samay xalam.