Ña nga naa: «Na Aji Sax ji gaaw! Na baral liggéeyam, nu gis. Na Aji Sell ju Israyil sottal mébétam, mu sotti, nu xam.»
TSK
TSK · Amos 5:18
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Nit ñaa ngi màtte ndijoor, te doyaluñu, di xàmpe càmmoñ te suuruñu, ku nekk di yàpp sa mbokk:
Nga déggi yuux, daw, tàbbi biir pax, génne pax, laawoob caax. Mbàndi kaw kat ubbi na, kenug àddina di reng-rengi.
Man mii lañuy sàkku bés bu ne, di wuta xam sama coobare! Mbete xeet wuy def njekk, te waccul ndigalu yoonu Yàllaam. Ñu ngi may ñaan àttey njekk, di sàkku man Yàlla, ma jege leen,
Wóoy boobu bés bu réy, ba bés du ni mel! Bésu njàqare lay doon ñeel askanu Yanqóoba, waaye dañuy mucc.
«Yaw nit ki, waa kër Israyil déy a nga naan, “Peeñu yi kii di gis, des na ay fani fan, ci lu soree sore lay biral ab waxyu!”
Wal-leen bufta ca Siyoŋ, dégtal-leen ab yéene ca sama kaw tund wu sell. Na waa réew mi mépp lox, nde bésub Aji Sax jaa ngi dikk te dëgmal na.
Bu ñu jubsee, suuf yëngu, asamaan rëng-rëngi, jant ak weer giim, biddiiw yi fat seenug leer.
Bésub Aji Sax bu mag bee dëgmal, moo dëgmal te tànk yu gaaw lool lay jegesee. Kàddug bésub Aji Sax ji dégtu na, te ca la jàmbaar di yuuxoo yuux yu metti.
Waaye bésu Boroom bi nib sàcc lay dikke. Ca la asamaan yi di dëddoo ci biir coow lu réy, lu ko sosoon seey ndax tàng, suuf ak jëf ju ci biiram xoyomu.