TSK

TSK · Amos 5:2

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Ba loolu amee ñu dëddu mboolem seen santaaney Yàlla Aji Sax ji; sàkkal seen bopp ñaari wëllu yu ñu móol, samp xer wu ñuy jaamoo Asera, di sujjóotal mboolem biddiiwi asamaan tey jaamu Baal.

Waajal-leen fi ñuy rendi doom yi, feye leen seen ñaawtéefi baay, bala ñoo jógati, teg àddina loxo, ba tabax fu ne ay dëkk.»

Lii moo di kàddu gi Aji Sax ji wax ci moom: Yaw, janq Siyoŋ mu taaru da laa xeeb, di la ñaawal. Yerusalem, dëkk bu taaru booboo lay wëcc bopp, di la kekku sa gannaaw.

Yewwulee, yewwul, Yerusalemee jógal, yaw mi Aji Sax ji nàndal kaasu mbugalam. Kaas bu wex bay miirloo, taat wa, yaa ko siitaatu.

Yéenees na rajaxoo ci kaw rajaxoo, réew mi mépp ne tasar kay! Jekki-jekki samay xayma tasaaroo. Xef-xippi ndimoy xayma ya xotatoo!

«Ne leen: Kàddug Aji Sax jee. Néew yeey wetaroo ci àll bi, mel niy jonkan, ni gub yu góobkat won gannaaw, kenn forul.»

Moo tax Aji Sax ji dafa wax ne: «Laajteleen rekk ci xeet yi! Ku ci masa dégg lu mel nii? Lu ñaawa ñaaw la Israyil, janq ba, def!

Yaw Israyil mu taaru, maa lay defaraat, nga defaru, ba jiinaat sam njiin, wàlli peccum mbéx,

Su ko defee nga ne: “Nii la Babilon di diige te du jógati ndax safaan bi may wàcce fi seen kaw, ba ñu sonn.”» Fii la kàdduy Yeremi yem.

Yaw Janq Yerusalem mu taaru mi, lu ma lay wax? Ku ma lay méngaleel? Siyoŋ mu jekk mu taaru mi laa ne, ana ku ma lay dendaleel, ba seral sa xol? Yaw mi sab góom yaa ni géej, ana ku lay faj?

Hosea 6:2 TSK

Ñaari fan, mu leqli nu, ñetteel ba mu yékkati nu, nuy dund fi kanamam.

Amos 7:2 TSK

Soccet yiy lekk gàncaxu réew mi, ba mu bëgga jeex, ma ne: «Éy Boroom bi Aji Sax ji, ngalla déet! Askanu Yanqóoba àttan na lii am? Lu néew doole lañu.»

Amos 9:11 TSK

«Bésub keroog maay yékkati mbaarum Daawuda mi joy, ba fattaat xar-xar yi, defaraat gent bi, tabaxaat ko na woon.