TSK

TSK · Amos 5:8

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

¶ At ma Nóoyin amee juróom benni téeméeri at, ca fukki fan ya ak juróom ñaar ca ñaareelu weer wa, kera la bëti ndox ya ne jàyy, jóge xóotey géej, bunti ndoxi asamaan ne kulbét, mu ne yureet,

Ba njël jotee Aji Sax ji dafa tollu ci biir taxaaru sawara wu ànd aku niir, di xool xarekati Misra, tiital leen, ñu fëlxoo.

Job 9:9 TSK

Moo sàkk dëllooñ gi féete bëj-gànnaar ak yaar yi ci digg asamaan, ak ga ca néegi bëj-saalum.

Job 37:13 TSK

mu mel ni yet wu muy bantale waa àddinaam, mbaa mu firndeele leen ko ngoram.

Job 38:31 TSK

Yaay faste genn dëllooñ gu ndaw gi ci digg asamaan? Am yaay yiwi dëllooñ gu mag ga mu dendal?

Yaa ko sànge xóotey géej ni mbubb, ndox ma taxaw, tiim tund ya.

Moo yónnee lëndëm, lëndëmal, te Musaa ak Aaróona gàntaluñu kàddoom.

Maay doxloo silmaxa yi ci yoon wu ñu xamul, ñall wu ñu miinul laa leen di jaarale. Maa leen di soppil lëndëm gi fi seen kanam, ag leer, fu ñagas, ma maasaleel leen. Lii laa leen di defal, te duma leen wacc mukk!

«Aji Sax ji dafa wax, moom miy sàkk mbir, bind ko, taxawal ko, Aji Sax ji di turam.

Amos 8:9 TSK

Ay bés a ngii déy, di ñëw,» kàddug Boroom bi Aji Sax jee: «maay sowal jant digg bëccëg, lëndëmal suuf bëccëg ndarakàmm.