seen jàmbaar yépp a fabu, topp guddi ga gépp ba Bet San. Ñu wékkee ca miiru Bet San néewu Sóol ak néewi doomam yu góor, doora ñibbi Yabes, boole fa néew ya, lakk.
TSK
TSK · Amos 6:10
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Ba mu ko defee Yosya ne gees, gis bàmmeel ya nekk foofa ca tund wa. Mu yeble, ñu sullil ko yax ya, mu lakk ko ca kaw sarxalukaay ba, sobeel ko noonu, muy kàddug Aji Sax ji góoru Yàlla ga waxoon, keroog ba Yerbowam taxawee ca sarxalukaay ba, bésub màggal. Buur Yosya neeti gees, yem ci bàmmeelu góoru Yàlla ga biraloon waxyu ba.
Kon nag, yeen mboolem Yudeen ñi sanc Misra, dégluleen kàddug Aji Sax ji. Maa giñ ci sama tur wu màgg.” Aji Sax jee ko wax. “Ma ne: Sama tur, gémmiñug benn Yudeen dootu ko tudd fi mboolem réewum Misra naan: ‘Giñ naa ko ci Aji Sax jiy dund.’
Waxal waa kër Israyil, ne leen: “Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Maa ngii di teddadil sama bérab bu sell bii, seen sag bii ngeen di doolewoo, di seen bànneexu bët, di seen nammeelu bakkan. Seen doom yu góor ak yu jigéen ya ngeen bàyyi Yerusalem, saamar dina leen tëral.
Bésub keroog jàngi kër Buur doon ay jooy.» Kàddug Boroom bi Aji Sax jee: «Néew yi, xas, fu ne ñu jalax, lépp selaw!»