TSK

TSK · Daniel 11:12

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

su boobaa moytuleen daldi xoggliku, fàtte seen Yàlla Aji Sax, ji leen génnee réewum Misra, kërug njaam ga,

Waaye Asiri gisewu ko noonu, xalaatewul noonu; bóome la xintewoo, ba fàkkas xeeti xeet.

Sa xelum jula mu réy nga yokke sa alal, alal ji tax laa fuuy.

Màggaay ga mu ko mayoon tax waa mbooloo yeek xeet yeek làkk yépp ragal ko, bay lox ci kanamam. Ku ko soob, mu rey; ku ko soob, mu bàyyi; ku ko soob, mu fal; ku ko soob, mu torxal.

Xelum njublaŋam lay naxee, di réy-réylu, ba bett ñu bare, faagaagal leen, te dina dëkk kilifay kilifa yi. Waaye mooy sànku, te loxo du ko laal.

Mbooloo maa ngay àddu ca kaw, naan: «Lii kay baatu Yàlla la, du baatu nit!»

¶ Naka noonu yeen ndaw ñi, nangul-leen magi mbooloom gëmkat ñi. Yeen ñépp nag toroxluleen ci seenug jëflante, ndax: «Yàlla, ñi réy lay xeex, ñi toroxlu, mu may leen aw yiw.»