Waxoon naa ko ne ko dinaa teg waa këram mbugal mu sax dàkk, ndax ñaawtéef gu ay doomam nekke, di ñàkke Yàlla teggin, mu yég ko te jubbantiwu leen.
TSK
TSK · Daniel 11:21
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Absalom jàppoo ko noonu ak mboolem bànni Israyil yay ñëw ca buur ba, di sàkku yoon. Ni la fàbbee xoli bànni Israyil.
Ku siblu, mu sib, ku ragal Yàlla, mu teral. Mooy sàmm ngiñam, su ko dee lor it.
Booba deesatul wooye ab dof, gor si, te njublaŋ dootu dégg «ku tedd ki.»
Ci kaw loolu béjjén bu ndaw génne ci béjjén yooyu benn, daldi lawa law jublu bëj-saalum ak penkook réew ma gëna rafet.
Xelum njublaŋam lay naxee, di réy-réylu, ba bett ñu bare, faagaagal leen, te dina dëkk kilifay kilifa yi. Waaye mooy sànku, te loxo du ko laal.
Ki koy wuutu dina yebal kuy foqati ay galag yu ñuy yokke puukarey nguur gi, waaye du yàgg dara, ñu faagaagal ko ci sutura, te du doon ci xare.»
Te bu leen nattu dikkalee, ndimbal lu néew lañuy am, ndax ñu bare naaféq lañuy fareek ñoom.