¶ Ci kaw loolu ñu woo bindkati buur ca bés ba, di ñaar fukki fan ak ñett ca weeru Siwan, ñetteelu weer wa. Ñu daldi bind mboolem lu Mardose santaane, ca mbirum Yawut yaak jawriñ yaak boroom dëkk yaak kàngami diiwaan ya, dale ko ca End ba ca Kuus. Muy téeméeri diiwaan ak ñaar fukk ak juróom ñaar (127). Ñu bind ndigal ya ci mbindum diiwaan bu nekk ak ci làkku xeet wu nekk, Yawut ya it ak seen mbindu bopp ak seen làkku bopp.
TSK
TSK · Daniel 3:4
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Esther 8:9
TSK
Isaiah 40:9
TSK
Yaw Siyoŋ, xibaarkatu jàmm bi, doxal yéegi tund wu kawe, te xaacook doole. Yaw Yerusalem, xibaarkatu jàmm bi, xaacul te bul ragal! Neel dëkki Yuda yi: «Seen Yàllaa ngi!
Daniel 4:1
TSK
¶ Man Nabukodonosor maa ngi woon ci sama jàmmi kër ak sama teraangay màkkaan.
Daniel 6:25
TSK
¶ Ba loolu wéyee Buur joxe ndigal, ñu indi nit ña tuumaaloon Dañeel, ñu tàbbal leen ca kàmbu gaynde ya, ñook seeni doom ak seeni jabar. Àgguñu suuf sax, gaynde ya alawti leen, dammate seen yax yépp.
Micah 6:16
TSK
Dogali Buur Omri daal lees di topp, ak mboolem jëfini waa kër Buur Axab. Seeni pexe ngeen topp, ba tax may def dëkk bi di lu daw yaram, waa dëkk bi di ñu nit ñiy muslu ci seenu demin, te gàcceg sama ñoñ, yeena koy gàlloo.»