Léegi nag sang bi, yal na sa kàddu gii di sama noflaay. Ndax yaw Buur, sama sang, dangaa mel ni malaakam Yàlla, am ug dégg, di teqale liy yoon ak li dul yoon. Yal na sa Yàlla Aji Sax ji ànd ak yaw.»
TSK
TSK · Daniel 5:11
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Sam xel ak sa manoore nga ame alal, am wurus, am xaalis, yeb ci say denc.
Ba loolu amee Buur wax Dañeel, ne ko: «Aylayéwén, sa Yàlla mooy Yàllay yàlla yi, di Sangu buur yi, te it mooy kiy feeñal mbóot, gannaaw feeñal nga mii mbóot.»
Ñu mujj ma indil Dañeel, di Beltasar, mi ñu tudde sama yàlla, di ku xelu yàlla yu sell yi nekk ci moom. Ma wax ko gént gi.
Garab gay màgg, di réy, ba njobbaxtal la di laal asamaan, ñu di ko séen ba ca cati àddina sépp.
Dégg naa sab jëw, ñu naan noowi yàlla yaa ngi ci yaw, te gis nañu ci yaw ag ràññee akum xel ak xam-xam bu takku.
¶ Ba mbooloo ma gisee la Póol def, ca kaw lañu àddu ci làkku Likawni, ne: «Yàlla yee soppliku melow nit, wàccsi ci sunu biir!»
Ñenn ci jàngub Seytaane bi, ñooñuy fen, di tuddoo ay Yawut te duñuy Yawut, maa ngii di leen xiirtal, dikkloo leen, sujjóotloo leen fi sa kanam, ba ñu xam ne man maa la sopp.