TSK

TSK · Daniel 6:16

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Bésub tey jii li ma falu buur lépp, néew naa doole, ndax doomi Seruya yii ñoo ma gëna dëgër xol, ba jaaxal ma. Waaye yal na Aji Sax ji fey ku bon jëfam.»

Aji Sax jeey musal ku jub, di ko aar bésub njàqare.

Làqoo Aji Sax jee gën wóolu doom aadama,

Booy xuus cim ndox, maa ngi ànd ak yaw; ag dex du la mëdd. Booy dox cib taal, doo lakk, sawara du la xoyom.

Buur Cedesyas ne leen: «Mu ngoog ci seen loxo, manaluma leen dara!»

Bésub keroog maa lay xettli,” kàddug Aji Sax jee, “ba deesu la teg ci loxol nit ñi nga ragal.

Ndegam Yàlla ji nuy jaamu man nanoo musal ci taalu sawara bu yànj bi, musal nu ci yaw mii, dina nu musal.

¶ Ba mu ko defee saytukat yaak jawriñ ya ànd rungumloo ba ca Buur, ne ko: «Buur Daryus, guddalu fan!

Acts 25:9 TSK

Festus nag bëgg lu neex Yawut yi, tax mu ne Póol: «Ndax nangu ngaa dem Yerusalem, ñu àttee la foofa ci mii mbir ci sama kanam?»

Ndax malaakam Yàlla ji ma moom, te ma di ko jaamu, moo ma dikkal biig.