TSK

TSK · Daniel 7:8

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

«Buleen ŋalŋaleeti, di damook a damooti, bu reewande génne seen gémmiñ, Aji Sax jeey Yàlla ji xam lépp, te mooy natt jëfi nit.

Ma bëgga am lu leer ba tey ci fukki béjjén yi ci bopp bi ak beneen ba génn, ba ñett daanu ca kanamam; mu am ay bët ak gémmiñ, di wax kàdduy damu, te ëpp yi ci des.

Bu nguur yooyu jeexee, ba bàkkaarkat yi buural, buur bu néeg te bare pexe dina falu.

Kooku mooy jànkoonteeka damu ci kaw mboolem lees di wooye yàlla, mbaa lees di jaamu, te mooy mujj toog ca kër Yàlla ga, ba far tudde boppam Yàlla.

Kàddu yu réy yu tekkiwul dara lañuy naxee, di fàbbee xemmemtéefi bakkan yu jéggi dayo, ay nit ñu yàggula rëcce ci ñeneen ñu nekk cig réer.

¶ Njéeréer yaa ngi nirook fas yu ñu waajal ngir xare, kaalawoo lu mel ni kaalay wurus, seen kanam nirook kanamu nit,

¶ Ñu may rab wi nag muy kañu ak a saaga Yàlla, may ko it mu saña wéye noonu diiru ñeent fukki weer ak ñaar.