TSK

TSK · Daniel 8:15

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Dooley kilifteefam ak jàmm ja du am kemu, fa jalub Daawuda ak nguuram, ga muy samp, saxale ko njekk ak yoon, tey jii, ba fàww. Lii la Aji Sax ji Boroom gàngoor yi def ci xéraangeem.

¶ «May xool ba tey ci biir peeñum guddi ma, gisuma lu moy jëmm ju mel ni doomu nit di ñëw, mook niiri asamaan, jëm ci góor gu mag gi; ñu yóbbu ko ba ca moom.

¶ «Fii la mbir mi yem. Man Dañeel nag, ma am njàqare lool, ba sama kanam soppiku, ma denc kàddu yooyu ci sama xel.»

Jekki-jekki jëmm ju mel ni nit dikk, laal samay tuñ. Ma ŋa, àddu, daldi wax ak ki taxaw sama kanam ne ko: «Sang bi, peeñu mi tax na ma jàq, ba amatuma benn doole.

¶ Maa ngi ciy dégg waaye xawma lu muy tekki. Ma ne: «Sang bi, ana nu xew-xew yooyu di mujje?»

Ca digg tegukaayi làmp ya, jëmm juy nirook nit a fa nekk. Ma nga sol mbubb mu tollu ci ndëgguy tànk yi, takkoo ngañaayal wurus ci dënn bi.