TSK

TSK · Daniel 8:19

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Bu nguur yooyu jeexee, ba bàkkaarkat yi buural, buur bu néeg te bare pexe dina falu.

Ñaari buur yi dinañu nas lu bon ci seen xol; di bokk ndab tey waxantey fen. Waaye seeni pexe du mujj fenn, ndax du fekk muj ga jot.

¶ «Buur bi dina def lu ko soob. Dina réy-réylook a damu, ba weesale boppam tuur yépp, te dina wax gilaawaali jëme ci Yàlla ji sut lépp. Dina am ndam nag ba keroog sànjum Yàlla ñoral ko. Li ñu dogal déy dina am.

Ma dégg ka sol mbubbam wëñ gu ëccu te taxaw ca kaw dex ga. Ma nga yékkati loxo ndijoor baak bu càmmoñ ba te naa: «Giñ naa ko ci Kiy Dund fàww ne ñetti jamonook genn-wàll lay doon. Xew-xew yooyu yépp a ngi dakk keroog bu dooley mbooloo mu sell mi jeexee tàkk.»

¶ Lii peeñum Yeesu Almasi la, mu ko Yàlla jox ngir mu won ay jaamam yenn xew-xew yu dëgmal. Malaakaam la yebal ci Yowaan ngir xamle ko.

Askan yee meroon, waaye sa mer a dikk tey; tey jii ngay àtte ñi dee, yool say jaam, yonent yi, yool ñu sell ñeek ñi la ragal, mag ak ndaw, tey it ngay sànk ñiy sànk àddina.»

Ndaxte Yàllaa def ci seen xol pastéefu sottal mébétam, ba ñu bokk sottal menn mébét mi, daldi jébbal rab wi seen nguur, ba kera kàddug Yàlla mat sëkk.