TSK

TSK · Daniel 8:25

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

«Du Mowab a doon diir Aji Sax ji mbagg? Nañu leen màndal sànjum Aji Sax ji, ba ñu waccu, di ca xuus, ba ñoom it, ñu di leen ree.

Naka ngay xool, aw doj wu loxo sànniwul fàq, daldi dal ca tànki jëmm ja bindoo weñ ak ban bu ñu lakk, daldi koy rajaxe.

¶ «Ni ma ne jàkk ci béjjén yi, beneen béjjén bu ndaw ne pëll, génn ci seen biir, ñett ca béjjén ya jiitu buddeeku. Béjjén bu ndaw baa nga am bët yu mel ni bëti nit ak gémmiñ gu muy waxe kàdduy damu.»

Muy damu bay diir mbagg Njiital gàngooru xare gi, daldi dakkal sarax ba ñu ko daan defal bés bu jot, màbb bérabam bu sell ba.

Mbooloo moomu dees na leen faagaagal, buur bëj-saalum di ca réy-réylu. Dina rey ay junniy nit nag, waaye du ko taxa am ndam.

Ñi sàmmul kóllëreg Yàlla ay nax la leen di fàbbee, waaye askan wi ràññee seen Yàlla, pastéef lañuy jëfeji.

Dina samp xaymay kër buur ci diggante géej geek tund wu taaru wu sell wa. Waaye dina dee, te kenn du ko taxawu.»

Dinañu xare ak Gàtt bi, waaye Gàtt bee leen di daan, ndax mooy Sangu sang yi, di Buuru buur yi. Mooy daan mook ñoñam, ñi mu woo, tànn leen te ñu saxoo topp ko.»

¶ Ba loolu amee ma gis rab wi, mook buuri àddina yeek seeni gàngoor, ñu daje ngir xareek ki war fas week gàngooram.