Daniel 2:48
TSK
¶ Ba mu ko defee Buur teral Dañeel, may ko lu baree bare, ba noppi def ko kilifag diiwaanu Babilon gépp, teg ci fal ko, mu yilif boroom xam-xami Babilon yépp.
TSK
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
¶ Ba mu ko defee Buur teral Dañeel, may ko lu baree bare, ba noppi def ko kilifag diiwaanu Babilon gépp, teg ci fal ko, mu yilif boroom xam-xami Babilon yépp.
¶ Mu neex Daryus nag, mu fal téeméeri jawriñ ak ñaar fukk ca réew ma, ñuy saytu nguur ga gépp;
Ca biir peeñu ma, maa ngi Sus, péeyub diiwaanu Elam. Ma gis ci peeñu mi ne maa ngi ci wetu yoonu ndox ma ñu gas te ñu di ko wax Ulay.
Ba loolu amee ma des fa man rekk, ne jàkk ci peeñu mu réy moomu. Waaye deseetuma woon doole, damaa jeexal tàkk, amatuma genn kàttan.
Ba ma ca déggee, samay butit a yëngu, coow la tax samay tuñ di lox, sama yaram dee goyy, may lox fi ma taxaw, te ne cell, di séentu bésub njàqare, bay dikkal xeet wi nu song.