TSK

TSK · Deuteronomy 10:21

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

¶ Aji Sax ji ne ko: «Maa ngi nii di fas kóllëre ak yeen. Ci sa kanam mbooloo mépp laay def ay jaloore yu kenn masula amal ci àddina sépp, ak ci askan yépp, te mbooloo, mi nga nekk ci seen biir mépp ay gis jaloorey Aji Sax ji, jaloore ju raglu ji ma lay defal.

Jan yàlla moo masa fexee dikk foqatil boppam aw xeet, bellee leen ci weneen xeet, ci biiri nattu, aki firnde aki kéemaan ak xare yu mu sottale dooley loxoom, ak kàttanu përëgam, ak jëf ju raglu, noonee leen ko seen Yàlla Aji Sax ji defale ca Misra, ngeen teg ci bët?

ngalla fexeleen rekk ba ragal Aji Sax ji, te ngeen dëggu ci jaamoo ko seen léppi xol, ndax dangeen di xool ci jaloore yu yéeme yi mu leen defal.

Éy sama Yàlla, ma woote bëccëg, wuyuwoo; woote guddi, nopploo ma.

Mu jëm ci njiital jàngkat yi, ñeel Daawuda, di kàddug Sabóor. Éy Yàlla mi may sant, bul tanqamlu!

Du jant a lay leeralati bëccëg, te weer du la niital; Aji Sax jeey doon sag leer ba fàww, sa Yàlla jooju di sab taar.

Éy Aji Sax ji, faj ma, ma faju; musal ma, ma mucc, samag cant, yaw a.

Luke 2:32 TSK

mu dig leer, ñeel jaambur ñi, sagal Israyil sa ñoñ.»