TSK

TSK · Deuteronomy 13:6

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

¶ Sarayi nag wax Ibraam ne ko: «Tooñ gi ma Ajara di tooñ, yaa ma ko yóbbe! Maa la jox sama jaam, ngir nga dëkkoo ko, naam, waaye moom, naka la yég ne ëmb na rekk, daldi indi yabeel sama digganteek moom. Kon yal na ma Aji Sax ji àtteek yaw!»

Mu ne leen: «Aji Sax ji, Yàllay Israyil dafa wax ne: “Na ku nekk teg saamaram ci luppam, te ngeen wër dal bi bépp buntoo bunt, ba mu daj. Reyleen ñépp; doomu ndey, xarit ak jegeñaale.”»

sàmmooleena jëfe mboolem dogal yeek àttey yoon yi ma teg fi seen kanam, bésub tey jii.

Loxoy seede yee koy jëkka dóor doj ngir rey ko, loxoy mbooloo mépp door koo dóor. Noonu ngeen di tenqee lu bon ci seen biir.

Waaye déy yonent bu am fitu àddu genn kàddu ci sama tur, te santuma ko mu wax ko, mbaa mu wax ci turi yeneen yàlla, boobu yonent, dee mooy àtteem.»

Na ko góori dëkk bépp dóori doj ba mu dee. Noonu ngeen di tenqee lu bon ci seen biir. Israyil gépp a koy dégg, daldi ragal.

¶ Su amee nit ku ñu fekke kenn ciy bokkam, ku mu sàcce ci bànni Israyil, mu di ko jaamloo, mbaa mu jaay ko, su boobaa dee mooy àtteb kooka ko sàcc. Noonu ngeen di tenqee lu bon ci seen biir.

Jombul mu am ku dégg kàdduy ngiñ lii, tey nax boppam cim xelam, naan: «Jàmm rekk laay am, maa tey të,» ba tax ñax mu wow lakkaale mu tooy.

Ba loolu amee Yonatan fasook Daawuda kóllëre, ndax sopp ko ni boppam.

Yonatan, doom yaay, tiisoo naa la, dama laa soppoon lool, te sa mbëggeel ci man yéeme, ba raw mbëggeelu jigéen.

Ilyaas ne leen: «Jàppleen yonenti Baal yii. Bu kenn ci ñoom rëcc.» Ñu jàpp leen, Ilyaas yóbbu leen ba ca xuru Kison, rendi leen foofa.

Ci biir loolu waa Babilon sàkk tuur ma ñuy wax Sukkóot Benoot, waa Kuta sàkk Nergal, waa Amat sàkk Asima;

Doom, ana looy xemmeme keneen, bay foye céri jaambur?

¶ Gannaaw loolu Yonent Yàlla Yeremi ne yonent ba ñuy wax Anaña: «Anaña, déglul bu baax li ma lay wax: Aji Sax ji yebalu la, yaw ngay gëmloo askan wii ay fen.

Micah 7:5 TSK

Buleen gëm ab xarit, buleen wóolu ab xejj, fi kanam ndaw siy tëdd sa gannaaw sax, sàmmal sa bunti gémmiñ.

¶ Kon nag gannaaw-si-tey, ni nitu suuxu neen di xoole moroomam, nun xooleetunu ko kenn. Doonte ni nitu suuxu neen lanu xoole woon Almasi, léegi xooleetunu ko noonu.

¶ Su boobaa nu noppee doon ay tuut-tànk yu nit ñiy muusaatoo kàddu yu mel ni gannax yu nuy baaje, ak ngelawal mboolem àlluwa ju bees ju nuy pamti-pamtee ci seen biir pexey naxe ak njublaŋ, ngir fàbbi nu.

¶ Waaye na mu ame woon ci askanu bànni Israyil ay yonenti caaxaan, ni lay ame ci seen biir ay sëriñi caaxaan yuy sërxal ay àlluway sànkute yuy weddi sax Sang bi leen jot, ba yóbbe seen bopp sànkute ju bette.

Ñu xalab ninki-nànka ju réy ja, jaanu cosaan joojee ñuy wax Tuumaalkat bi, di ko wax Seytaane, naxekatu mboolem àddina. Ci kaw suuf lañu ko xalab, mooki malaakaam.

Da koo sànni ci xóote bi, tëj ko, sakk buntu xóote bi, ndax du naxati askan yi, ba kera junniy at yi mat. Gannaaw loolu nag fàww ñu yiwi ko diir bu gàtt.