TSK

TSK · Deuteronomy 28:49

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Aji Sax jeey yékkatil raaya, xeet wu sore, wal ug liit, wooye leen fa cati àddina, ñu jekki ne jaas, dikkal leen.

Éey waa kër Israyil,» kàddug Aji Sax jee, «maa ngii di indi fi seen kaw xeet wu bawoo fu sore. Xeet wu am kàttan lañu, xeet wu yàgga yàgg, wu ngeen xamul seen làmmiñ, te dégguleen seeni wax.

Aji Sax ji déy dafa wax ne: «Lu mel ni jaxaay a ngii naa jàyy, firiy laafam, këfsi Mowab.

Ñi ñuy dàqa gëna gaaw ay jaxaay, ci kaw tund yi lañu nu ne dann, màndiŋ mi, ñu di nu fa tëroo.

Ne leen: «Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Jaxaay ju mag la woon, réyi laaf, guddi dunq, sëq lipp, yànj lool. Mu dikk ba Libaŋ, jàpp ci collu genn garabu seedar,

¶ Dañeel daldi ne Buur: «Buur, guddalu fan!

Bu juróom benn fukk yeek ñaar ciy àppi juróom ñaar weesee, dees na bóom ku ñu fal, te kenn du ànd ak moom. Gannaaw loolu kilifa dina ñëw, ànd ak gàngooram, yàqte dëkk beek jaamookaay bi. Waaye kilifa googu lu mel ni mbënn a koy mujje. Dogal nañu ne yàqte gi dina wéy ba keroog xare biy jeex.

Maa ngii di dooleel waa Babilon, xeet wu wex, ràkkaaju, di wër déndi àddina, di nangu màkkaani jaambur.

Ay bés a ngi dikk ci sa kaw, keroog say noon a lay gawe ab sëkk, yéew la, tance la wet gu nekk.