TSK

TSK · Deuteronomy 5:2

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Léegi nag su ngeen ma déggalee bu baax, di sàmm sama kóllëre ak yeen, yeenay doon sama moomeelu bopp ci mboolem askan yi. Dëgg la, àddina wërngal këpp maay Boroom,

¶ Aji Sax ji ne ko: «Maa ngi nii di fas kóllëre ak yeen. Ci sa kanam mbooloo mépp laay def ay jaloore yu kenn masula amal ci àddina sépp, ak ci askan yépp, te mbooloo, mi nga nekk ci seen biir mépp ay gis jaloorey Aji Sax ji, jaloore ju raglu ji ma lay defal.

Ci kaw loolu mu biralal leen kóllëreem gi mu leen sant ngeen sàmm ko, muy fukki santaane yi. Mu daldi leen bindal santaane yi ci ñaari àlluway doj.

Aji Sax ji daa fasoon ak ñoom kóllëre, sant leen ne leen: «Buleen wormaal yeneen yàlla, buleen leen sujjóotal, buleen leen jaamu, te buleen leen sarxalal itam.

«Aji Sax ji Yàllay Israyil dafa wax ne: Man maa fasoon kóllëre ak seeni maam keroog bés ba ma leen génnee réewum Misra kërug njaam ga, ne leen:

Keroog ba Musaa biralalee bànni Israyil gépp mboolem santaane, na ko yoon wi laaje, ba mu noppee, deretu wëllu la jël, ak ju sikket, akum ndox, ak caru garabu isob bu mu laxas kawaru xar mu xonq. Mu capp ko ca deret ja, wis-wisal ca kaw téereb yoon wa, ak mbooloo mépp.