TSK

TSK · Ecclesiastes 10:13

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Sóol wax ak jawriñam yi taxaw ci wetam, ne leen: «Yeen Beñamineen ñi, dégluleen! Mbaa yeen ñépp, doomu Yese jee leen di jox ay tool aki tóokëri reseñ, am yeen ñépp lay fal njiiti kuréli junni ak njiiti kuréli téeméer,

Nabal ne ndawi Daawuda: «Ana kuy Daawuda? Kuy doomu Yese sax? Jamonoy tey jaam yu baree ngi fàqe ci seeni sang.

Mu ne ko: «Bu la Aji Sax ji walluwul, nu ma lay walloo? Du pepp, du ndoxum reseñ ju ma la mana may.»

Képp ku teey jëfe xam-xam; ab dof ay siiwal ndofam.

Luke 6:11 TSK

Ñu mer nag ba fees, di diisoo ci seen biir nu ñuy def ak Yeesu.

¶ Ba Yeesu génnee foofa, ca la Farisen ya ak firikat ya tàmbalee xabtalu ci kawam, di ko seetloo ay laaj ci mbir yu bare,

Acts 5:28 TSK

ne: «Xanaa aayewunu leen woon ne buleen waareeti mukk ci woowu tur? Yeena ngi nii ubale Yerusalem ak seen waare, ngeen nar nu cee gàdduloo bakkanu nit kii!»

Acts 7:54 TSK

¶ Naka lañu dégg loolu, seen xol fuddu, ñuy yéyu ci kawam.