TSK

TSK · Ecclesiastes 5:13

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

¶ Ci biir loolu Lóot, mi mu àndal, moom it yor jur gu gudd ak gu gàtt aki xayma,

Lóot daldi génn, wax ak goroom, ya naroona takk ay doomam yu jigéen, ne leen: «Gaawleen gaaw, génn dëkk bi, ndaxte Aji Sax ji dina ko tas.» Teewul ñu defe ne day kaf.

¶ Mu am bés, taaw bi wax rakk ji, ne ko: «Sunu baay a ngii màggat, te fii fépp amul góor gu nu mana séqal ci wàllu séy, ni ko waa àddina yépp baaxoo defe.

Képp kuy lekk lu lewul, nii lay mujje: wutin wu lewul jël bakkanu boroom.

Alal du jariñ bésu mbugal; jub, mucc ci gàtt fan.

Bul rey sa bopp ci wut alal, bu ko xalaat sax.

Kenn a ngii, kenn ñaareelu ko, du doom, du mbokk. Doñ-doñam du dakk, te du doylu, mujj mu naan: «Kan laay doñ-doñil, di xañ sama bopp bànneex?» Loolu it, cóolóoli neen, di sas wu tiis.

Loolu lépp gis naa ko, ba may xalaat ci jépp jëfi kaw suuf; fi nit di yilife nit, muy loraange.

Ab dof, waxi dof lay wax, xel ma di nas ñaawtéef, mu nar jëf ju teddadi. Lu ñaaw lay wax, jëme ci Aji Sax ji, di xiifal ku xiif, di xañ ku mar lu mu naan.

¶ Mu léeb leen nag, ne leen: «Nit la woon ku woomle, te ab toolam nangu.

¶ «Jenn waay la woon ju bare alal, di sol yérey tànnéef yu rafet, di dunde lu neex bés bu set.

Yeesu dégg loolu, ne ko: «Lenn rekk nga deseleeti. Mboolem loo am, jaay ko, séddale ko néew-doole yi. Su ko defee nga woomle fa asamaan. Boo noppee, ñëwal, topp ci man.»

Waaye ñi sàkkoo barele, ñooy tàbbi ci nattub bakkan, aki fiir, ak lu bare ciy xemmemtéef yu tekkiwul dara, xemmemtéef yuy lore, tey suuxal seeni boroom ci yàqule ak sànkute.

James 5:1 TSK

¶ Kaayleen nag ma wax leen, yeen boroom alal yi, jooyleen te yuuxu, ndax mitit yi leen di dikkal.