TSK

TSK · Exodus 12:21

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Demal woo magi Israyil, ñu daje, nga ne leen: “Aji Sax ji, seen Yàllay maam ya, di Yàllay Ibraayma ak Isaaxa ak Yanqóoba, moo ma feeñu, ne ma: ‘Gis naa leen, te yég naa li ñu leen di teg ci Misra.

Ni ngeen koy lekke nag, nii la: bu ngeen koy lekk, dangeen di takku, sol seeni dàll, ŋàbb seen yet, te ngeen lekk ko ci lu gaaw. Loolu gàttu saraxu bésub Mucc ba lay doon, ñeel Aji Sax ji.

¶ Musaa dellu, woolu magi mbooloo ma. Mu jottli leen mboolem wax jooju ko Aji Sax ji dénk.

¶ Ba mu ko defee Aji Sax ji dafa wax Musaa, ne ko: «Dajaleel ma juróom ñaar fukki magi Israyil, ñoo xamal sa bopp ne ñooy magi mbooloo mi, di seeni njiit, nga indi leen ci xaymab ndaje mi, ñu teew faak yaw.

¶ Buur Yosya nag jox mbooloo mépp ndigal ne leen: «Màggal-leen bésub Mucc ga, ñeel seen Yàlla Aji Sax ji, ni ñu ko binde ci téereb kóllëre gii.»

Ezra 6:20 TSK

Fekk na sarxalkat yaak Leween ña laabal seen bopp, ba ñoom ñépp bokk laab. Ba loolu amee ñu rendi xarum bésub Mucc ba, ñeel mboolem ña ñibbsee ngàllo, ak ñoom sarxalkat yi ci seen bopp, ñook seeni bokk.

te ñoom ñépp, menn ndoxum kéemaanu Yàlla ma lañu naan, ndax ñoo doon naane ca doju kéemaanu Yàlla ga, doj wa leen doon gunge, te doj wa Almasi la woon.