Guddi googu Aji Sax ji feeñu ko ne ko: «Maay Yàllay Ibraayma sa baay; bul ragal dara, ndax maa ngi ànd ak yaw. Dinaa la barkeel, ful sa askan ndax sama jaam Ibraayma.»
TSK
TSK · Exodus 14:13
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
¶ Noona la Aji Sax ji xettlee bànni Israyil bésub keroog ca waa Misra, ñu gis néewi waa Misra ya ne wetar ca tefes ga.
Fexeleen rekk ba Aji Sax ji, buleen ko gàntal, te yeen nag ngeen baña ragal waa réew ma, ndax ab lanc doŋŋ lañu nuy mat. Seen kiiraay dëddu na leen, te Aji Sax jaa ngeek nun. Buleen leen ragal.»
Alyaasa ne ko: «Bul tiit, noo leen ëpple ñu ñu àndal.»
Ba nga gisee sunu toroxtey maam ya ca Misra, dégg seeni yuux ca tefesu géeju Barax ya,
Ñeel Daawuda. Aji Sax jee may leeral, di ma wallu. Ana ku may ragal? Aji Sax jeey aar sama bakkan. Ana ku may tiit?
Sunu Yàllaa di Yàlla jiy walloo, Aji Sax ji Boroom beey musal bakkan.
Say gët nga ciy teg, di seetaan ku bon di jot yoolam.
Ndax Boroom bi Aji Sax ji, Aji Sell ju Israyil dafa wax ne: «Délsi, dal-lu moo leen di musal. Ne tekk te wóolu maa leen di dooleel. Waaye yeena buggul!
bul ragal, yaw laa àndal, bul tiit, maay sa Yàlla; maa lay dooleel, dimbali la déy, maa lay téyee sama ndijooru njekk déy.
Naxi neen kay lañu jële ca xërëmi tund yu ndaw ya ak coowal kaw tund yu mag ya. Muccu Israyil kay, fi sunu Yàlla Aji Sax ji.
Waaye waa kër Yuda, maa leen di yërëm. Seen Yàlla Aji Sax ji laa leen di walloo, waaye duma leen walloo fitt mbaa saamar, mbaa ay xare, mbaa ay fas aki gawar.»
«Israyiloo, yàqu nga, te maa yor sa wall.
Yaa génn ngir wallusi sa ñoñ, wallusi ki nga fal. Yaa rajaxe puju néegu ku bon ki, xar ko ñaar, geen ba ci put. Selaw.