Exodus 14:16
TSK
te yaw nanga yékkati saw yet, tàllal sa loxo mu tiim géej gi, ba xàll ko, ndax bànni Israyil mana dox ci suuf su wow, jàll géej gi.
TSK
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
te yaw nanga yékkati saw yet, tàllal sa loxo mu tiim géej gi, ba xàll ko, ndax bànni Israyil mana dox ci suuf su wow, jàll géej gi.
Dooleem la mane géej, manooreem la rajaxee Raxab ninki-nànka ja.
Moo soppi géej ag joor, maam ya dox jàll. Nanu ko bége foofa.
Moo xar géej ga, jal ndox ma nim tata, jàlle leen.
Géej gaa leen gis, daw, dexu Yurdan a deltu gannaaw,
ba ca melax yaak doj yu sedd yay taw, ak tawub yuur akub lay, ba ca ngëlén yu mag yay def ndigalam.
Xanaa du yaa wowal géej ak ndoxum xuram wu ne màww, def xóotey géej aw yoon, ña nga jot jàlle ca?
Ana ki dawaloon dooley përëgam bu tedd ba, ñeel ndijooru Musaa, xaral leen ndox ma, ba ame ca woy wu sax dàkk?