Ndax xawma nan laay delloo ca sama baay te ànduma ak xale bi. Yàlla buma fekke njekkar, li ciy dal sama baay!»
TSK
TSK · Exodus 18:8
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
«Aji Sax ji, sa kàttanu ndijoor a yéeme! Aji Sax ji, sa ndijoor a ne noon ba rajax.
¶ Gannaaw loolu Musaa jële bànni Israyil géeju Barax ya, ñu wéy, wuti màndiŋ, ma ñuy wax Sur. Dox nañu ñetti fan ca màndiŋ ma, gisuñu ndox.
¶ Yettro sarxalkatu réewum Majan ba, baayu soxnas Musaa, dafa dégg mboolem la Yàlla defal Musaa ak bànni Israyil ñoñam ak ni Aji Sax ji génnee Israyil Misra.
¶ Gannaaw gi, Musaa moo yebale ay ndaw fa dëkk ba ñuy wax Kades, ñu dem ca buurub Edom, ne ko: «Israyil say bokk dañoo wax ne: Umplewoo mboolem coono bi nu daj.
¶ «Kon rikk waay, yaw sunu Yàlla, Yàlla ju màgg, ji àttan te mata ragal, di sàmm kóllëreek ngor; ngalla bul xeeb mboolem toskare ji dikkal sa ñoñ, muy buur ak njiit, sarxalkat ak yonent, dale ca sunuy maam ba ci nun ñépp tey, ca janti buuri Asiri, ba sunu jonni yàllay tey.
Éy Yàlla, ba may ndaw, nga ma xamal say kéemaan, te ba tey jii maa ngi koy biral.
«Sippi naa leen, woyofal seeni yoxo.
Teewul Yàlla wallu leen ngir turam, ba xamle njàmbaaram.
Waxleen lii, yeen ñi Aji Sax ji jot, jote leen ci loxol bañ,