TSK

TSK · Exodus 29:13

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Lakkal kuuy mépp ci kaw sarxalukaay bi. Saraxu rendi-dóomal la, ñeel Aji Sax ji, di xeeñ xetug jàmm; saraxu sawara la, ñeel Aji Sax ji.

Nga daldi koy nangoo ci seeni loxo, lakk ko ci kaw sarxalukaay bi, boole kook saraxu rendi-dóomal bi, muy xeeñ xetug jàmm fi kanam Aji Sax ji. Saraxu sawaraa ngoogu, ñeel Aji Sax ji.

Na ko sarxalkat bi yóbbu ca sarxalukaay ba, kutt baat bi, lakk ko ci kaw sarxalukaay bi. Deret ji dees koy siital ci wetu sarxalukaay bi, ba mu jeex.

Li muy génne ci saraxu cantu biir jàmm bi, muy saraxu sawara ngir xetug jàmm, ñeel Aji Sax ji, mooy nebbon bi, ak calgeen bi yépp, ñu doge ko fa sës ca fàllare ja, ak nebbon bi sàng yérey biir yi, ak lépp luy nebbon te jàpp ci yérey biir yi,

Na génne lépp luy nebbon ci yëkk wi ñuy sarxal muy póotum bàkkaar: nebbon bi sàng yérey biir yi, ak lépp luy nebbon te jàpp ci yérey biir yi,

Te it na génne nebbon bi yépp ni muy génnee nebbonu jur gu ñu def saraxu cant ci biir jàmm. Na ko sarxalkat bi lakkal Aji Sax ji ci kaw sarxalukaay bi, muy xeeñ xetug jàmm. Noonu la ko sarxalkat biy defale njotlaayal bàkkaaram, mu am njéggal.

Sarxalkat bi day lakk nebbon bi ci kaw sarxalukaay bi, waaye dënn bi, Aaróona aki doomam yu góor ñoo ko moom.

Ba mu ko defee mu génne nebbon bi, muy calgeen bi ak nebbon bi sàng yérey biir yépp ak bàjjo bi ci res wi ak ñaari dëmbéen yi ànd ak seen nebbon, ak tànkub ndijoor bi.

Waaye lay nebbon ca nag wa ak kuuy ma, di calgeen ba ak nebbon bi sàng yérey biir yi, ak dëmbéen yi ak bàjjo bi ci res wi,

Sarxalkat bi day xëpp deret ji ci sarxalukaayu Aji Sax ji, ci bunt xaymab ndaje mi, ba noppi, lakkal Aji Sax ji nebbon bi, muy xeeñ xetug jàmm.

Su ko nit ki nee: «Xanaa dees na jëkka lakk nebbon bi ba mu jeex, nga doora sàkk lu la neex?» Mu ne ko: «Mukk! Léegi nga ma ciy jox, lu ko moy doole laa koy jële.»

«Lu may doye seen sarax yu bare?» la Aji Sax ji wax. «Damaa suur seen saraxi rendi-dóomali kuuy, suur nebbonu juru yar gi, deretu yëkk ak xar ak sikket it, safu ma.

Du xaalis boo ma jëndale barax bu xeeñ, du nebbonu sarax boo ma reggale. Xanaa lakkal maak say bàkkaar, sonal maak say ñaawtéef.