TSK

TSK · Exodus 32:14

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

¶ Ba loolu amee Aji Sax ji ne: «Jéggal naa leen noonu nga ko waxe.

«Maa noon maa leen di fàkkas, ba far dakkal lu leen nit doon fàttlikoo.

bàyyi xel ci kóllëreem ak ñoom, topp ngoram lu réy, ba giif,

Léegi nag rafetal-leen seeni jëfin ak seeni jëf te déggal seen Yàlla Aji Sax ji. Su ko defee Aji Sax ji fomm musiba mi mu leen dogaloon.

Joel 2:13 TSK

Du seeni yére doŋŋ ngeen di xotti, ngir ñaawlu, seenub xol ngeen di xottiwaale, ñaawloo ko. Waññikuleen ci seen Yàlla Aji Sax ji, mooy boroom yiw ak yërmande; mer maa diib, ngor ga bare, muy fomm mbugal.

Amos 7:6 TSK

Boroom bi Aji Sax ji fomm ko ne ma: «Liitam du am.»

Jonah 4:2 TSK

Mu ñaan Aji Sax ji, ne ko: «Céy Aji Sax ji, xanaa du lii laa waxoon ba ma génnagul sama réew? Moo taxoon ma jëkka daw, jëm Tarsis! Ndax xamoon naa ne yaw Yàlla yaay boroom yiw ak yërmande, sa mer a diib, sa ngor bare, ngay fomm mbugal.