TSK

TSK · Ezra 9:2

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

waaye yeenay doon nguuru sarxalkati Yàlla, te di xeet wu sell.” Kàddu yooyu ngay wax bànni Israyil.»

Te it bu ngeen jëlalee seeni doom jabar ca seen doom yu jigéen, seen jigéen ñooña dinañu gànctook seeni tuur, ba xiir seen doom yu góor ci gànctook seen tuur yooyu.

¶ Bu leen seen Yàlla Aji Sax ji yóbboo réew ma ngeen jëm, ngir nanguji ko, moo fay dàqe xeet yu bare fi seen kanam: Etteen ñi ak Girgaseen ñi ak Amoreen ñi ak Kanaaneen ñi ak Periseen ñi ak Eween ñeek Yebuseen ñi; juróom ñaari xeet yu leen ëpp, ëpp leen doole.

Ndax kat askan wu sell ngeen, ñeel seen Yàlla Aji Sax ji. Yeen la seen Yàlla Aji Sax ji taamu, ngir ngeen doon askan wi mu séddool boppam, ci mboolem askani kaw suuf.

Ezra 10:2 TSK

Ci biir loolu Sekaña doomu Yeyel ma askanoo ci Elam, daldi wax Esra ne ko: «Noo tooñ sunu Yàlla, di jël ay jaambur jabar ci xeeti réew mi. Waaye loolu terewul Israyil am yaakaar ba tey.

¶ Ñooñu ñépp jël nañu ay jaambur jabar, ba ñenn ci ñoom ami doom.

Ma ŋàññ kàngami Yuda, ne leen: «Lu ñaaw lii ngeen di def nag di teddadil bésub Noflaay?

Fekk na kenn ci doomi Yowada doomu sarxalkat bu mag ba Elyasib sax, jël doomu Sanbalat mu Oron. Teewul ma dàq waa ji, mu daw ba sore ma.

Yuda wor na, lu jomblu lees def fi Israyil ak Yerusalem. Yuda déy moo teddadil li Aji Sax ji sopp te mooy bérabam bu sell: Yuda moo takk janqub yàllay doxandéem.

Ndaxte jëkkër ji gëmul day daldi séddu sellnga ndax jabaram ja dib gëmkat, te jigéen ji gëmul it day séddu sellnga ca jëkkëram jay gëmkat. Su dul woon noonu doom yu ngeen ca am di ñu sobewu, te bir na ne doom yu ngeen ca am, ñu sell lañuy doon.