TSK

TSK · Genesis 17:10

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

¶ Ba loolu amee Ibraayma boole doomam Ismayla, ak jaam, yi juddoo këram yépp, ak ñi mu jëndoon ci xaalisam ñépp, góori waa këram ñépp, xarfal leen ca bés ba, muy la ko Yàlla waxoon.

Ba bés ba délsee, Ibraayma xarfal doomam Isaaxa, ni ko ko Yàlla digale woon.

Waaye li ci nekk mooy, seeni góor duñu nangoo dëkk ak nun, nuy ay bokk, ndare sunu góor ñépp xaraf ni ñoom.

Su fekkee ne ab doxandéem bu ngeen dëkkal dafa bëgga wormaal màggalu bésub Mucc bi ngir Aji Sax ji, xaraf war na ko, te war na gépp góor gu bootu ci moom; su loolu amee, dees na ko may, mu def ko, ndax kon day mel ni doomu réew mi. Waaye kenn ku xaraful du ci lekk.

Su boobaa seen Yàlla Aji Sax jee leen di xarfal xarafu xol, te mooy xarfal xarafu xol, seen askan, ngir ngeen soppe seen Yàlla Aji Sax ji seen léppi xol, ak seen léppi bakkan, ndax ngeen dund.

muy waa Misra, di waa Yuda, di Edomeen ñeek Amoneen ñi, di Mowabeen ñeek mboolem ñiy wat seen peggu kawaru bopp te dëkke màndiŋ mi, nde xeet yooyu, kenn xarafu ci dëgg, waaye bànni Israyil gépp it xarafuñu xarafu xol.»

Acts 7:8 TSK

Yàlla daldi fasook Ibraayma kóllëre gu mu màndargale xaraf. Moo tax Ibraayma xarfal doomam Isaaxa, ba mu juddoo ba am juróom ñetti fan; Isaaxa, Yanqóoba, Yanqóoba, fukki maam yaak ñaar.

Moom la Yàlla tudd muy njot gu ngëm di maye, ci kaw deretam ji tuuru. Noonu la Yàlla firndeele ne njubteem mat na sëkk doonte tanqamlu woon na bàkkaari niti jamono ya woon,

Gannaaw Yàlla kenn la, mooy jox ñi xaraf, àtteb ñu jub ci kaw ngëm; ñi xaraful it, moo leen di jox àtteb ñu jub ci kaw ngëm.

Ki xarafoon bala ñu koy woo, bumu làq màndargam xaraf ma. Ki xaraful woon ba ñu koy woo, bumu xaraf.

Ma artooti képp ku dem ba ñu xarfal ko, ne ko mboolem yoon wi la wara jëfe.

¶ Kon nag, yeen jaambur ñi dul Yawut cib juddu, yeen ñi ñuy wooye yéefar yi xaraful, te ñi leen ko dàkkantale woon di Yawut yi xarafe ci loxol nit ku leen xarfal ci seen yaram, fàttlikuleen seen démb.

Ci moom ngeen xarafe xaraf gu loxol nit deful, ndax noonu kuy xarfal nit ki di doge as lëf ci yaramu nit ki, ni la Almasi di doge ba mu set, buumu njaam gi leen dooley bàkkaar tënke woon. Noonu la Almasi di xarfalee.