Seeni bët daldi ubbiku, ñu xam ne yaramu neen lañu def. Ba mu ko defee ñu ràbb xobi garabu figg, gemboo.
TSK
TSK · Genesis 2:25
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Genesis 3:7
TSK
Exodus 32:25
TSK
¶ Musaa nag gis ni mbooloo mi ràkkaajoo, ndax fekk na Aaróona bay-bayal leen, ba ñu ràkkaaju, ba ku leen doon fexeel man leena ree.
Psalms 31:17
TSK
Leeralal ma sa kanam, Sang bi, walloo ma sa ngor.
Isaiah 47:3
TSK
Na sa yaram feeñ, say cér ne fàŋŋ. Damay feyu, te duma bale.
Jeremiah 6:15
TSK
Ñu wara am gàcce ci seen jëf ju siblu, te gàcce gàcceelu leen. Xamuñu sax luy kersa! Moo tax ñuy fëlëñoondook ñiy fëlëñu. Kera ba ma leen di dikkal, ñooy tërëf.» Aji Sax jee ko wax.
Ezekiel 16:61
TSK
Yaay fàttliku say jëfin, ba am kersa keroog booy dalal sa doomi ndey yu jigéen, ñi la mag ak ñi la féete ndaw. Maa la leen di may niy doom, doonte loolu bokkul ci sama kóllëreek yaw.
Romans 10:11
TSK
Mbind mi moo ne: «Képp ku ko gëm, doo rus.»